TSK

TSK · Proverbs 8:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Maa ko feesale xelum Yàlla, ak xareñte ak déggin ak xam-xam, ak manoorey bépp xeetu liggéey,

Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tir, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp.

Éy Aji Sax ji, yaa bare loo liggéey, te lépp di xel mu rafet. Suuf daa fees ak say càkkéef.

Dees koo xamal yoon wa, te Yàllaam a ko ko jàngal.

¶ Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!

Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem.

Ci moom la mboolem alal ji ci xel ak xam-xam, dëxëñe.