TSK

TSK · Proverbs 8:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Naka la Samiyel séen Sóol, Aji Sax ji wax ko, ne ko: «Waa jii laa la wax. Kii mooy yor sama ñoñ.»

Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?»

Jawriñ ya dañu daa ay-ayloo, ku nekk ak sa weer wi ngay topptoo dundub Buur Suleymaan, mook mboolem ñi mu bokkaloon njël, ba dara daawu ca ñàkk.

Ñeel Suleymaan. Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte, mayal doomu Buur bii sa xelum njekk,

Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»

Man maa sàkk suuf, sàkk doom aadama ak mala fi kaw suuf ci sama doole ju bare ak sama kàttan gu matale, te loolu lépp, maa ko jox ku ma neex.

Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.

Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»

¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi ma, gisuma lu moy jëmm ju mel ni doomu nit di ñëw, mook niiri asamaan, jëm ci góor gu mag gi; ñu yóbbu ko ba ca moom.

¶ Na ku nekk déggal njiit yi yor kilifteef, nde amul njiit lu bawoowul fa Yàlla, te njiit yi toog, Yàlla moo leen tabb.

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»