TSK

TSK · Psalms 94:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak kuy def njekk, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb kuy def njekk.

Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.

Xettlimaak ñiiy def lu bon, wallu maak bóomkat yi.

Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.

Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.

Kàngami Israyil a ngii fi sa biir, di jaay doole bay tuur deret.

Kàngamam yi ci biiram a ngi mel ni saafaandu yuy dogat am pàdd, tuur deret ja, di sànk ay bakkan ngir nangu alali boroom.

Acts 4:27 TSK

Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.

Acts 7:58 TSK

ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.

Ma gis ne jigéen ji daa naan ba màndi ci deretu ñu sell ñi ak deretu ñi doon seedeel Yeesu. Ba ma ko gisee, jaaxle naa lool.