TSK

TSK · Romans 1:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye mooy fey ci saa si ay bañam, ngir sànk leen. Du yeexe bañam, ci saa si la koy fey.

¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku torxal baayam mbaa ndeyam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»

Ku bon déy a ngi tëggoo bànneexu bakkanam, ku bëgge di ñàkke wormaak a teddadil Aji Sax ji.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda.

Ñu ngi làmmiñoo reewande, képp kuy def lu bon di damu.

Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, di seen Yàlla ju leen di baal, te di leen mbugale seeni jëf ju bon.

Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.

Maay def loolu ngir nanguwaat xolu waa kër Israyil, gi ma dëddu ngir seen mboolem kasaray tuur yi.”

Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen,

¶ Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla.

¶ Kon ana lees di bàkkoo? Dara! Ci lan lañu koy teg sax? Ci jëf ju yoon santaane? Mukk! Xanaa yoonu ngëm doŋŋ.

Weesunu kemu, bay damu ci liggéeyu ñeneen. Waaye am nanu yaakaar ne nu seen ngëm gëna yokkoo, ni la sunuw sas di gëna yokkoo, lépp ci biir kemu gi ñu nu àppal.

Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu santadi te selladi.

James 3:5 TSK

Noonu itam la aw làmmiñ dee cér su tuut te réy aw bàkk. Seetleen ni ferñent su tuut di lakke gott bu yaa.

Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.