Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
TSK
TSK · Romans 2:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.
Bésub safaan ku bon ay mucc, bésub mbugal it, mooy raw.
Sang baa ngi fi sa ndijoor te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.
Ku ñuy àrtu, nga të ticc, dangay jekki yàqu, ba wees am paj.
Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.
Waaye ba mu bewee, të ticc bay réy-réylu, dañu koo jàllarbee ca nguuram, nangu ndam la,
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
Waaye wóor nanu ne àtteb Yàlla bi muy añale ñiy jëfe jooju jëfin, dëgg lay dëppool.
¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.
Waxees na ne: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam, buleen të na woon ca fippu ga.»
seen wurus ak seen xaalis xomaag. Xomaag ja dib seede bu leen tuumaal, di xoyom seenu suux ni sawara. Yeena dajale alal ca fan yu mujj ya.
Waaye asamaanu tey jii, ak suuf, genn kàddug Yàlla googu moo leen yeb cib denc, ñeel sawara, kera bésub àtte ba, bésu sànkuteb aji gëmadi ñi.
ndax seen bésub sànj bu mag taxaw na, ana ku ko àttan?»