TSK

TSK · Romans 4:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare.

maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk,

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.

Te Ibraayma lañu digoon dige yi mook ki taxawal askanam. Newuñu: «ñi taxawal ay askanam», mbete ñu bare lañuy wax, waaye wenn rekk la: «ki taxawal askanam,» te ki taxawal askanam moo di Almasi.