TSK

TSK · Romans 6:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mukk kay! Nun ñi ndee tàggale ak bàkkaar ba noppi, ana nu nuy saxootee bàkkaar?

Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.

kooku mooy Yàlla mi wéetoo xam-xam, te moom la teddnga ñeel ba fàww, ndax Yeesu Almasi! Amiin.

Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi rey ca bant ba.

Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub, gi Yeesu Almasi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.

ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi, làqe fa Yàlla.

Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi.