Mu ne ko: «Bu ma soññ mukk ci loolu, duma la wacc, duma la dëddu. Foo jëm, fa laa jëm; foo dal, fa laay dal; say bokk di saay bokk; sa Yàlla di sama Yàlla.
TSK
TSK · Ruth 2:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana kuy jekku noonam, wacc ko mu dem ak jàmm? Yal na la Aji Sax ji fey lu baax li nga ma defal bésub tey jii.
Moo dàq wurus, raw wurusu ngalam wu ne xas; dàqati lem, ëpp tem-tem.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma.
Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; wormaam yéew la, di la aar.
ndax kat moo am muj, te kon sa yaakaar du tas.
¶ Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey.
Yal na ko Boroom bi may mu daj bésub keroog booba, yërmandey Boroom bi. Taxawu na ma lool ca Efes, te xam nga ko xéll.
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
Toroxtaange gu ñu koy teg ndax Almasi, moom la defoon muy alal ju ëpp denci Misra, ndax yoolub ëllëg ba la doon séentu.