TSK

TSK · Titus 3:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji, yaa may feg, musal ma, yaa may nangul, darajaal ma.

seede buy fen rekk, rawatina kuy yokku ay ci biiri bokk.

ak sàcc yi ak bëgge yi ak màndikat yi ak saagakat yi ak ŋàppaaral yi, duñu am cér ci nguurug Yàlla.

¶ Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaleey, fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñemeey,

¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,

Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.

Lépp luy wextan, ak naqari deret, ak mer mu ëpp, ak coow, ak wax ju ñaaw, na lépp buube, ba génne ci seen biir, mook mboolem jëfi coxor.

¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.

Bokk yi, danu leen di dénku; yaafus yi, femmuleen leen; ñi néewu fit, ñaaxleen leen; néew-doole yi, dimbalileen leen, te it muñal-leen ñépp.

Naka noonu, na jigéen ñiy taxawu mbooloo mi di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu moom seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.

¶ Bokk yi, soppe yi, nangeen xam lii: na ku nekk di gaaw ci déglu, di yeexa wax tey yeexa mer.

¶ Bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa mbokk mbaa nga sikkal sa mbokk, yoon wi nga ŋàññ, yoon wi nga sikkal. Ku sikkal yoon wi nag doo sàmmkatub yoon wi, sikkalkatub yoon wi nga.

Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.

Ndax kat: «Ku bëgga bége bakkanam, fekke bés bu rafet, na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.

¶ Rawatina nag boroom xemmemtéefi yàqute, yi topp seen bakkan te faalewuñu genn kilifteef. Ñu fétteeral lañu te bew, ragaluñoo saaga sax boroom daraja yu kawe ya fa asamaan.

Jude 1:10 TSK

Waaye nit ñii de, lu ñu xamul lañuy saaga, te xam-xam yi leen seen bindu judduwaale xamal, ni ay rabi àll di xame, ci lañuy far yàqoo.