TSK

TSK · Zechariah 14:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Foofa ngeen di lekke, yeen ak seeni njaboot fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ngeen bége fa seen wépp ñaq wu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelal.

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Foofa law yoon di jaare, ñu di ko wooye Yoon wu sell wi. Ku sobewu du fa jaare, ñi moom woowu yoon, ñooy ñi koy topp. Ab dof sax du fa lajje.

Yaw nag, ca sa Yàlla nga wara dellu, ngor ak njub, sàmm ko, te nga saxoo yaakaar sa Yàlla.

Yeen waa goxu Ja ba, yuuxooleen, nde jula yépp ay sànku, mboolem kuy natt donji xaalis lees fay dagge.

Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.

Ndax kiy taamu bés, Boroom bi la koy taamul; naka noonu kiy lekk, Boroom bi la koy gërëme, nde moom lay sant doora lekk; ki lekkul it Boroom bi lay sàkkoo ñàkka lekkam, te Yàlla lay sant.

¶ Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.

ngir su ma yeexee itam, nga xam nooy doxale ci kër Yàlla, ci biir mbooloom Yàlla jiy dund. Mbooloom gëmkat mi mooy kenug dëgg gi, di cëslaayam.

Almasi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit, ak yaakaar ji nuy puukarewoo.

¶ Julay àddinaa ngay yuuxu, di ko jooy, nde am njaayam du jarati:

Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.