TSK

TSK · Zechariah 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, fépp fu ñuy dajee, Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg, guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,

Aji Sax jeey wowal walum ndox, ma séle géeji Misra. Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat, wal kook doole, dóor ko, mu séddlikoo juróom yaari wal, mu jaarale ca nit ñu caraxu,

Yéegeleen ab raaya kaw tund wu ne duŋŋ, joorleen ñii, tàllal-leen loxo, ñu jàlle bunti kàngam yi.

Su bés baa waa Misra mel niy jigéen, di lox ndax tiit loxo bi jóg, te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi xàccil-leen ko.

Wóoy ngalla yaw bóomkat bi kenn bóomul, yaw workat bi kenn worul. Boo noppee bóome, ñu bóom la, te boo noppee wore, ñu wor la.

Yeen nag seen réew mi gaal la, gu goj ya yolom, ponk ba ca digg ba di yëngu, ba ndimol gaal gi firikuwul. Dees na séddoo lël ju ne gàññ, ba làggi ya sax séddu ca.

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.

Mboolem xeet yee koy nangul, nangul doomam ba ci sëtam, ba keroog moom itam, àppu réewam jot. Su boobaa am réewam nangul yeneen xeet yu giir ak buur yu mag.

ba dootuñu taxani, dootuñu gori ca gott ya, gànnaay ya lañuy taaloo, te ñooy futti ñu leen futti woon, di sëxëtoo ña leen sëxëtoo woon. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Yaa sëxëtoo woon ay xeet yu bare, mboolem ndesu askan yee lay sëxëtooji, ndax deretu nit ji nga tuur, soxore ay réew, aki dëkk, ak mboolem ña ca biir.

Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»

Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.

Ñu sore ñooy dikk tabaxsi kër Aji Sax ji, ba ngeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal ci yeen. Loolu mooy am, ndegam déggal ngeen ba déggal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji.»