TSK

TSK · Zephaniah 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ As ndaw, ngeen digool ab séy, keneen tëdde ko; ag kër, ngeen tabax, te dungeen ko dëkke; ab tóokëru reseñ, ngeen jëmbat, te dungeen ko jariñoo.

Ñooy yàpp seenug jur, lekk seen gàncax, ba ngeen raaf. Duñu leen wacce dara; du pepp, du biiñ, dug diw, du doomu jur gu gudd ak gu gàtt, ba ngeen far sànku.

¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.

«Ñooy tabax ay kër, dëkke, jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma.

Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo, réew mi mépp ne tasar kay! Jekki-jekki samay xayma tasaaroo. Xef-xippi ndimoy xayma ya xotatoo!

Ana ku muus, ba xam lu waral lii? Ku Aji Sax ji waxal, mu wax nu lu waral réew mi sànku, gental ni màndiŋ mi, kenn jaaru fi?

Gàngooru sàmm a sëxëtoo sama tóokëru reseñ, joggati sama waar, def waar wi ma neex màndiŋ mu ne maraas.

Seen xaalis, ñu sànni ci mbedd yi, seen wurus di leen saf sagaru sobe. Keroog bésub sànjum Aji Sax ja, du xaalis, du wurus wu leen di xettli. Du leen fajal xiif, du leen reggal, xanaa tàbbal leen cig njubadi.

Maay indi xeet yi gëna néeg, ñu nangu seeni kër, ma daldi sàggi sagu boroom doole yi, sobeel seen bérab yu sell.

Amos 5:11 TSK

Gannaaw yeenay not néew-ji-doole, di foqati ŋëbu peppam, tabax ngeen këri boroom barke, waaye dungeen ko dëkke. Jëmbat ngeen tóokëri reseñ juy tem-temi, waaye dungeen naan ca biiñ ba.

Yaw de yaay ji te doo góob, nga nal doomi oliw te doo ca diwu, nal doomi reseñ te doo naan biiñ.