Te dinaa ko won coono yu bare yu mu wara dékku ngir sama tur.»
TSK
TSK · Acts 21:13
Treasury of Scripture Knowledge references in Téereb Injiil.
Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax.
Bokk yi, ni ma damoo ci yéen ndax Yeesu Kirist, ni la ma wóore ne bés bu nekk ma riisu dee.
Ndax surgay Kirist lañu? —maa ngi wax waxi ku tàggoo ak sagoom nag— maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey, maa leen ci man. Bu dee ci li ñu nu tëj ci kaso, maa leen ko gëna miin. Bu dee ci li ñu nu dóor ay yar, maa leen ëpple. Leru naa dee ba tàyyi.
Bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ngëm mat sëkk, ma mel ni naan gu ñu boole ak sarax su jëm ci Yàlla, ba tey bég naa ci, te dinaa ci bégati.
¶ Léegi nag maa ngi am bànneex ci coono, yi may daj ngir seen njariñ; te li des sax ci fitnay Kirist, noonu laa koy àggalee ngir njariñu mbooloom ñi gëm, di jëmmam.
xam ne xarekat bu bëgga neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina.
Ndaxte xam naa ne léegi ma jóge fi, ni ma ko Yeesu Kirist Boroom bi leerale woon.
Fekk not nañu ko jaarale ko ci deretu Gàtt ba ak seen seedes ngëm, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.