TSK

TSK · 1 Corinthians 2:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 2:4 TSK

Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.

¶ Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma dikkee ci yeen, du ci puukarey kàddu yu gëna taaru, ak xam-xam bu ma leen yégalsee mbóoti Yàlla.

¶ Nitu neen nag du nangu lu aju ci Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana xam, ndax loolu Xelum Yàlla lees koy natte.

ndax kiy làkk weneen làkk, du nit ñi lay waxal, waaye Yàlla lay waxal, gannaaw kenn déggul li muy wax. Teewul ci Noo gi lay waxe ay kumpa.

Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi.

¶ Du ay léeb yu xel mu xareñ fent lanu leen xamale woon sunu manoorey Boroom Yeesu Almasi, ak na muy dikke, waaye noo teewe màggaayam.