TSK

TSK · 1 Corinthians 4:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Man nag seedey Yàlla laa ciy sàkku, giñ naa ko ci sama bakkan, bañ leena yokku naqar moo tax délsiwuma Korent.

Looloo taxoon ma binde noonu, ngir bu ma dikkee, baña am naqar ci ñi ma waroona bégal. Li ma wóor ci yeen ñépp moo di sama mbégte mooy seen mbégte, yeen ñépp.

¶ Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaleey, fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñemeey,

Te doonuma am benn kersa, su ma ëppaloon sax ci damoo sañ-sañ bi nu Boroom bi jox, te du sañ-sañu sànk leen it, xanaa yokk seen ngëm.

La ma waxoon ba noppi ca sama ñaareelu ngan, tey bi ma wuutee, moom laay baamtu, artoo ko ñi jëkkoona bàkkaar, ak ñi ci des ñépp: su ma délsee, duma ñéeblu kenn,

Manoon nanoo taafantoo li nu diy ndawi Almasi, ba diisal leen, waaye danoo lewetoon domm ci seen biir, mel ni jaboot juy topptoo ay doomam.