¶ Ci biir loolu Buur Suleymaan bëggoon na jigéeni yeneen xeet yu bare te bokkul ak doomu Firawna ji mu jëloon: ñuy ay jigéeni Mowabeen ak jigéeni Amoneen ak jigéeni Edomeen ak jigéeni waa Sidon ak jigéeni Etteen.
TSK
TSK · 1 Kings 21:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Axab doomu Omri di def li Aji Sax ji ñaawlu, ba raw mboolem ña ko jiitu.
Yesabel yónnee Ilyaas ndaw, ne ko: «Yal na ma tuur yi teg mbugal mu gëna réy, ndegam nëgëni ëllëg jëluma sa bakkan, ni nga jële bakkani yonent yii.»
¶ Axab ne Ilyaas: «Ãa, noon bi, gisati nga ma?» Ilyaas ne ko: «Gis naa la, ndax dangaa dogu ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu.
Yoram jàkkaarlook Yewu, ne ko: «Yewu, mbaa jàmm?» Yewu ne ko: «Ana nu jàmm di ame te sa bàkkaaru bokkaaley ndey Yesabel jógu fi, mook xërëmam yi ne xas?»
Mboolem buur yi jiitu Yosya, kenn jubloowu ci Aji Sax ji léppi xolam ak léppi jëmmam ak kem kàttanam, bay sàmm yoonu Musaa wépp. Mboolem ñi ko wuutu it, kenn dabu ko ci.
Waxi ndaw su yemadi am yeer la, ku Aji Sax ji rëbb moo cay tàbbi.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Damaa fase seen ndey? Wonleen ma kayitu pase mi! Maa leen jaay njaam, feyey bor? Ana ku ma leen jaay? Bu ñu leen jaayee, seeni ñaawtéef a. Bu ñu fase woon seen ndey it, seeni moy a.
Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.
¶ Xam nanu ne yoonu Musaa ci Yàlla la bokk, te man may nitu suuxu neen, dib jaam bu ñu jaay bàkkaar.