TSK

TSK · 1 Kings 21:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye duma ko def ci sag dund ngir sa baay Daawuda. Ci sa loxol doom ju góor laa koy foqatee.

¶ Ba loolu amee mu ne jaraafam ba ñuy wax Bitkar: «Foral sànni ci toolub Nabot mu Yisreel. Yaa ngi fàttliku ba nu bokkee watiir maak yaw topp ca baayam Axab te Aji Sax ji rëbb ko ne ko:

¶ Buur Axab amoon na juróom ñaar fukki doom yu góor ca Samari. Yewu bind ay bataaxal, yónnee ca Samari ca kilifay Yisreel ak mag ñaak dagi doomi Axab, ne leen:

Gannaaw yaa réccu ci sa xol, ba toroxlu ci kanam Aji Sax ji, ba nga déggee ni ma rëbbe bérab bii mook ñi ko dëkke, muy seen toroxteek seen alkànde, te yaa xotti say yére, jooy fi sama kanam, man it dégg naa la. Kàddug Aji Sax jee.

Xettli nga ma ci bokk yiy fippu, def ma, ma jiite ay xeet; waaso wu ma xamul sax nangul ma,

Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.

Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.

¶ «Xanaa gisoo li ñu nekke fi dëkki Yuda ak ci mbeddi Yerusalem?

¶ Yàlla nag gis seeni jëf, gis na ñu dëddoo seen jëfin ju bon. Yàlla daldi fomm mbugal ma mu leen naraloon, ba mujju koo def.

Luke 7:44 TSK

¶ Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam.

Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax buggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.