TSK

TSK · 1 Kings 21:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu ko defee Aji Sax ji dafa wax Musaa, ne ko: «Dajaleel ma juróom ñaar fukki magi Israyil, ñoo xamal sa bopp ne ñooy magi mbooloo mi, di seeni njiit, nga indi leen ci xaymab ndaje mi, ñu teew faak yaw.

¶ Su dee dañoo fekk ku ñu bóom ci biir réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji moomale, mu tëdd ci àll bi, te xameesul ku ko rey,

Ruth 4:11 TSK

¶ Waa pénc ma mépp ak mag ña nag ne ko: «Noo ko seede. Yal na Aji Sax ji def ndaw siy séysi sa kër, mel ni Rasel ak Leya, ñoom ñaar ñi giir waa kër Israyil gépp. Yal nanga tekki ci digg Efrata te amu tur ci Betleyem.

¶ Buurub Israyil nag woolu magi réew ma mépp, ne leen: «Boo yeboo ngeen xam ne waa jii kat fitna lay wut; gis ngeen mu yeble ci man, bëgga nangu samay jabar ak sama doom yu góor ak sama xaalis ak sama wurus, te bañaluma ko ci dara.»

¶ Buur Axab amoon na juróom ñaar fukki doom yu góor ca Samari. Yewu bind ay bataaxal, yónnee ca Samari ca kilifay Yisreel ak mag ñaak dagi doomi Axab, ne leen:

Ezra 4:11 TSK

¶ Li ñu bind ci bataaxal ba jëm ca Buur Artaserses mooy lii: Nun sa surga yii ci Wàllaa Dex ak li ci topp,

¶ Gannaaw loolu ñu woolu bindkati buur ca weer wa jëkk ca at ma, yemook fukki fan ak ñett. Ñu bind ci bindinu diiwaan bu nekk, ak ci làkku xeet wu nekk mboolem lu Aman digle, mu jëm ca jawriñi buur ak boroom dëkk yaak kàngami xeetoo xeet. Ci turu Aserus lañu bind bataaxal yi, tay ko, mu ànd ak torlub buur.