TSK

TSK · 1 Peter 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Hosea 1:9 TSK

Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (mu firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.»

Moom la wax it ci téereb Ose ne: «Ñi dul woon sama ñoñ, ñoom laay wax sama ñoñ, ñooñu dul woon samab xejj, ñoom laay xejjoo.»

Gannaaw aw yiw a tax nag, dootu seen peyu jëf, lu ko moy aw yiw noppee doon aw yiw.

¶ Ci wàllu janq ji séyagul, awma ci ndigalu Boroom bi, xanaa ma wax ci sama xalaat bu mata gëm, ndax yërmande ji ma Boroom bi baaxe.

Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.