Kuy nas njekkar, sore ma; lu bon, xawma ko.
TSK
TSK · 1 Peter 2:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ragal Aji Sax ji mooy bañ lu bon. Réy, xeebaate, yoonu mbon, ak wax ju jekkadi, ma boole bañ.
Aji Sax ji bañ na njublaŋ, safoo maandute.
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
¶ Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang yi ci àddina. Buleen ko defe ngistal, mbaa ngeen di ko sàkkoo lu leen neex, waaye defeleen ko yéeney xol bu dëggu, ndax ragal Boroom bi.
¶ Jaam yi, nañu nangul seeni sang ci lépp, di sàkku seen bànneexu sang, te ñu bañ di tontoonte ak moom,
¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.