TSK

TSK · 1 Peter 3:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 2:4 TSK

Seytaane ne Aji Sax ji: «Bakkan a wuutu bakkan rekk. Mboolem lu nit am, man na koo weccee bakkanam.

Job 9:25 TSK

Ab dawkat sax ni samay fan di jeexee ko raw. Wone nañu gannaaw te gisuñu lu baax.

Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.

Na bége bànneexu bakkanam, ñu di ko kañe koomam,

ngir fan wi gudd lool, nga gëna am jàmm.

Mooy dundloo ku ci jàpp, di wéral jëmmam jépp.

Saam xel ne ma, ma naan biiñ boog, bégloo, ba mel nib dof, tey ànd ak sama xel, ba gis lu ci baax, ba doom aadama di ko def, giiru dundam fi ko jant bi tiim.

¶ Ku yaakaar ne moo jullite te moomul làmmiñam, boppam lay nax te ag njulliteem amul njariñ.

¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.

te kàddug fen masula jibe seen gémmiñ. Gàkkuñu fenn.