TSK

TSK · 1 Peter 3:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Yeen jaam yi, déggal-leen seen sangi àddina, ànd ceek ragal Yàlla bay kat-kati, ak xol bu dëggu. Ni ngeen déggale Almasi, nangeen leen ni déggale.

Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi.

Bu la kenn xeebe sa at yu néew, waaye nanga doon royukaayu gëmkat ñi ci wax ak jëfin, ak cofeel, ak ngëm, ak dundin wu set.

Seen dundin ci biir jaambur ñi gëmul, rafetal-leen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.

Waaye Sang Almasi ngeen di sellal ci seen xol, te waajal nu ngeen di tontoo ku leen laaj lu jëm ci yaakaar ji ngeen am.