TSK

TSK · 1 Peter 3:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu Aana ñaan ne: «Sama xol a ngi bége Aji Sax ji, ci Aji Sax ji laa ame doole. Maa am tontal noon yi, nde maa bànneexoo sag wall.

Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.

Luke 2:37 TSK

Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak julli la daan jaamoo guddi ak bëccëg.

Acts 1:14 TSK

Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.

waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ragalkati Yàlla.

¶ Waaye kiy ab jëtun dëgg te di ku wéet, mooy ki yaakaar Yàlla, te saxoo ay dagaan aki ñaan, guddi ak bëccëg.

Titus 2:3 TSK

¶ Naka noonu, jigéen ñu mag ñi itam, nañu jëfe ni mu jekke ci ay nit ñu sell; buñu yàq der, bu leen sàngara jiital, te nañuy jàngle lu baax,

ndax day xool ci yeen ak seenug sellal gu ànd ak wegeel.