Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.»
TSK
TSK · 1 Peter 3:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Naanal ci sa mbalkam bopp, ndox ma balle sa teenu bopp.
Jëkkër ji war naa def warugaru jëkkër ci jabaram; naka noonu it, jabar ji war naa def warugaru jabar ci jëkkëram.
ba mu leer ne jaambur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér bi, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
¶ Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam.
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Su ko defee kenn ku nekk ci yeen mana moom yaramu boppam ci biir sellnga ak teddnga,
Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?