Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.
TSK
TSK · 1 Peter 3:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?»
¶ Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
¶ Ñi leen di bundxatal, ñaanal-leen leen, ñaanal-leen leen te bañ leena móolu.
Samay soppe, buleen di feyul seen bopp, xajal-leen am sànj, am sànj fajal boppam, ndax bindees na ne: «Man maay feye, maay añale.» Boroom bee ko wax.
Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey balante, ni leen Yàlla baale ci Almasi.
ne ko: «Maa lay barkeela barkeel déy, ful laa ful.»
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.