TSK

TSK · 1 Peter 4:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.

Ndax ki dee ba noppi, joxees na ko àtteb ku jub, mu tàggook noteelu bàkkaar.

Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.

Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba, seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar, aki xemmemtéefam.

Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir:

Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dal-loo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dal-loo ci say liggéey.

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.