TSK

TSK · 1 Peter 4:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog, yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil.

Bul tiit, doo rus mukk. Bul jaaxle, deesu la kersaal mukk. Sa gàcce ga ba ngay ndaw, dinga ko fàtte, te sa tiisu jëtun wa dootoo ko fàttliku.

Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.

Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.

Loolu laa ne siiw, yaakaar ko, te duma rus mukk, xanaa di saxoo aw fit, démb niki tey, ngir ma mana fésale sama jëmm jépp, teddngay Almasi, su may dund ak su may dee.

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne moo mana sàmm li ma ko dénk ba keroog bés ba.

James 1:2 TSK

¶ Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk,

¶ Kon nag ñiy sonn te coobarey Yàlla tax, nañu dénk seen bopp Yàlla, Sàkk-kat bu wóor bi, te ñuy saxoo def lu baax.