TSK

TSK · 1 Peter 4:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te kat dëkk bii ñu ma tudde sax, maa ngi koy tàmbalee musibaal. Kon yeen, nu ngeen mana fexee ba mucc? Dungeen mucc moos, ndax saamar laay wool mboolem ku dëkke àddina.”» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.

Mag ñu góor ñeek xale yu góor yi, jeeg jeek janq ji, ba ci tuut-tànk yi, reyleen ñépp, faagaagal leen. Waaye ku ci am rëddu jë, buleen ko laal. Dooreleen ko ci sama bérab bu sell bi.» Ñu tàmbalee bóom mag ña ca kanam kër Yàlla ga.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ «Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.

Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;

¶ Seen njàlbéenu xél de baax na! Ana ku leen gàllankoor ba toppuleen dëgg gi?

Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ,

Noonu lees matale Almasi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

Yeena àgg fa Yeesu, Rammukat bi dox kóllëre gu yees gi, yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.