Romans 12:13
TSK
Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
Kon na ku nekk joxe, ni mu ko waaje ci xolam, te bañ koo tiisoo, bañ koo joxee ñàkk pexe, ndax kiy joxee xol bu sedd, Yàlla sopp na ko,
Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku moom bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngle.
Waaye buggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli.
Te it di def lu baax, ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.