TSK

TSK · 1 Peter 5:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk.

¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.

Ña rafet xel leer nàññ ni leeraayu déndub asamaan. Ñi doon xiir mbooloo mi ci ngor ne boyy niy biddiiw, ba fàww.

Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.

Dina feeñ it ndax noflaay ba mu nuy booleek yeen ñiy dékku ab coono, sédde nu ko, kera bés bu Sang Yeesu feeñee, ànd ak ay malaakaam yu làmboo manooreem, wàcce asamaan.

¶ Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,

Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,

Foral-leen gétt gi ñu leen dénk. Sàmmleen ko, te bañ koo defe ñàkk pexe, xanaa xol bu tàlli, ni ko Yàlla bëgge. Buleen ko defe it koppartuy kese, waaye farluleen ci.

Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.

¶ «Maa ngi ñëw léegi. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.