TSK

TSK · 1 Timothy 5:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Buleen safaan dëgg cib àtte. Buleen far néew-ji-doole te buleen far boroom doole. Àtteleen seen moroom ci dëgg.

Kee ne ndey ak baay: «Gisuma leen,» ay doomi ndeyam, ràññeewu leen, te doomam, xamu ko. Xanaa di sàmm say wax, di sàmm sa kóllëre.

May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.

«Moo tax man it ma def xeet wépp xeeb leen, sewal leen, feye leen ko seen ñàkka sàmm samay yoon, ak par-parloo gi ngeen di diglee yoon wi.»

Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.

¶ Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi, léegi xooleetunu ko noonu.

¶ Dama lay ñaax fi kanam Yàlla mi may bakkan lépp luy dund, ak fi kanam Almasi Yeesu, boroom seede su rafet sa fa kanam Poñsë Pilaat,

¶ Kon nag dama lay dénk fi kanam Yàlla ak Almasi Yeesu, miy àtteji ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci darajay bésam ba muy feeñ, ak ci darajay nguuram,

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.

Jude 1:6 TSK

Te it malaaka ya yemul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa wacc seen dëkkuwaayu bopp, Yàlla moo leen denc ci lëndëm gu ne këruus, yeewe leen buum yu dul deñ, ngir àtteb bés bu mag ba.

kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi.