TSK

TSK · 2 Corinthians 13:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Acts 4:10 TSK

xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.

Ci sóobu googu lañu nu boole ak moom suul, ngir noonee Almasi dekkee ci màggug Baay bi, nun itam nu dekki bay dund dundin wu yees.

¶ Loolu sax moo waral Almasi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.

Ci ag teddadi lañu ji néew bi ñu suul, te teraanga lay dekkaale. Ci néew doole lees ko ji, mu dekkaale doole.

Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem,

Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deeyam,

Fan yi Almasi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te nangule na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.

mi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, ki malaaka yeek boroom sañ-sañ yeek boroom doole yi, bokk nekk cig curgaam.