¶ Buleen feyantoo, fexeleen di def lu rafet, ñépp seede ko.
TSK
TSK · 2 Corinthians 13:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
nuyul-leen ma Apeles mi firndeel kóllëre gi mu am ci Almasi, te ngeen nuyul ma waa kër Aristobul,
Fàww sax mu am ay xaajaloo ci seen biir, ngir ñi seen ngëm wér mana fés ci seen biir.
ci biir teraanga, ak ci biir toskare; ci biiri baatal, ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu;
Ndaxte bataaxal yi kat lañu ne: «Dañoo ñagas, te tàng, waaye bu teewee moom ci boppam, da naan yàcc, te ay kàddoom xeebu.»
Bu nu néewee doole, te ngeen am doole, bég nanu. Lii itam, nu ngi koy ñaan, te mooy ngeen yokku ba mat sëkk.
¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.
ñeel buur yi, ak mboolem boroom baat yi, ngir nu mana nekke jàmm akug dal, tey wéye gépp njullite, ak wépp dundin wu tedd.
Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Seen dundin ci biir jaambur ñi gëmul, rafetal-leen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.