TSK

TSK · 2 Corinthians 7:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.

Bu benn cér mettee, mook cér yépp ay bokk metit wi. Bu dee benn cér lañu teral, mook cér yépp ay bokk bànneexu.

Waaye sama xel dalul woon, ndax gisuma woon sama mbokk, Tit. Teewul ma tàggtoo ak ñoom, jëm diiwaanu Maseduwan.

Te saa yu Tit xoolaatee ni ngeen dégge ndigal, yeen ñépp, ak wegeel gi ngeen ko dalale, ànd ceek ragal Yàlla bay lox, cofeelam ci yeen di gënatee yokku.

Yal na Yàlla baaxe nag waa kër Onesifor, yërmandeem, ndax dëfal na ma lu bare, te kersawoowul li ñu ma tëj kaso,

¶ Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.