TSK

TSK · 2 Corinthians 9:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ruth 2:19 TSK

Goro ba ne ko: «Foo fore lii lépp tey? Ban tool nga doon liggéeye sax? Ki la nemmikoo nii de, yal na barkeel!» Ruut nag wax goroom ka mu doon liggéeye toolam, ne ko: «Ka ma doon liggéeye toolam de, Bowas lañu koy wax.»

Luke 6:46 TSK

¶ «Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax?

Acts 4:21 TSK

Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,

Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.

mbóot mu bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal,

Dañu noo ñaan, ba di nu tinu, ngir nu may leen, ñu def seen loxo ci ndimbalu jàpplante gi jëm ci gëmkat ñu sell ñi.

Mboolooy gëmkat yooyu nag di sant Yàlla ci man.

¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.

Noonu lees matale Almasi sëkk, ba mu doon cosaanu mucc gu dul jeex, ñeel mboolem ñi ko déggal.

Te it di def lu baax, ak di dimbalee, buleen ko fàtte, ndax sarax yu mel noonu la Yàlla gërëm.

Kuy wax, na waxe nu mu jottlee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp, ndax Yeesu Almasi, mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.