TSK

TSK · 2 Kings 13:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Niti Israyil nag gis diggante bu metti bi ñu tollu ndax na ñu tance seen gàngoor ga. Ñu dem làquji ci ay xunteek ay dédd ak ay doj, aki seyaan aki kàmb.

¶ Booba nag benn tëgg amul woon ca réewum Israyil ba mu daj, ndax waa Filisti dañu noon: Bu Ebrë yi sàkk ay saamar aki xeej.

Waa Israyil daje, sàkk ab dund, ba noppi dox wuti leen. Waa Israyil a nga dal janook ñoom, di saf ñaari gétti bëy. Waa Siri ñoom fees àll ba.

¶ Ca jamono jooja nag la Aji Sax ji tàmbalee fell suufas Israyil, Asayel buurub Siri di leen duma ca réew ma mépp.

Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas, ndegam am ngay gawaram!

Maa ngii di la def ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq; ànd aki bëñam, ngay wol tund wu mag, raatale; dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox.

Amos 1:3 TSK

Aji Sax ji da ne: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Damaas, te duma fomm seeni duma. Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.