TSK

TSK · 2 Kings 17:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Musaa nag ne Aaróona: «Lan la la mbooloo mii def, ba nga yóbbe leen gii moy gu réy?»

Aa! Xale yi, coow li ma dégg, muy law ci biir ñoñi Aji Sax ji, rafetul de!

Mu ne Yerbowam: «Jëlalal fii sa bopp fukki dog, ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil da ne: “Gisal, maa ngi dagge nguur gi ci loxol Suleymaan, te dinaa la ci jox fukki giir.

¶ Ci kaw loolu Buur seetluwaat mbir ma, daldi sàkklu ñaari wëlluy wurus. Mu ne mbooloo ma: «Yeen waa Israyil, bare ngeen lu ngeen di jaabante yoonu Yerusalem. Xool-leen fii kay! Seen yàlla ya leen génne woon réewum Misraa ngi.»

Aji Sax ji dina wacc Israyil ndax bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te di ko bàkkaarloo Israyil.»

Aji Sax jee lay dikke, yaak saw xeet ak sa waa kër baay, ay bés yu tar yu masula am, ba Efrayim dëddoo Yuda ba tey, te buurub Asiri la koy sababe.»