TSK

TSK · 2 Kings 21:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi jéggeegul dayo.»

Li ko waral mooy bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te bàkkaarloo ko waa Israyil, di merloo Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ba feesal xolam.

Axab daan na def ñaawtéef ju réy, di topp ay kasaray tuur, di def mboolem lu doon baaxu Amoreen ña Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Waaye bànni Israyil ñoo dégluwul, ba Manase waññi leen, ñuy def ay ñaawtéef, ba raw xeet ya Aji Sax ji sànkoon fi kanam bànni Israyil.

Topp na baayam ci mboolem tànk ya mu jaaroon, di jaamu kasaray tuur yi baayam daan jaamu, di leen sujjóotal.

Ci ndigalal Aji Sax ji moos la loolu xew ca Yuda, ba mu mujj leen xarab ndax bàkkaari Manaseek li mu def lépp,

Dama leen di def, waa réewi àddina yépp, ku leen ci xool rasu. Te li ko waral di Buurub Yuda, Manase miy doomu Esekiya, ak li mu def ci digg Yerusalem.»

Ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Sa cosaan ak sab juddu réewum Kanaan la. Sa baay dib Amoreen, sa ndey dib Etteen.