Aji Sax ji nee na: Dama ne, dinaa wàcce lu bon ci sa kaw, fàllas say sët, ba faagaagal ci digg Israyil kuy taxaw, colal, te bokk ci yaw Axab, muy gor, di jaam.
TSK
TSK · 2 Kings 21:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba mu ko defee Yewu rey mboolem ña desoon ca kër Axab ca Yisreel ak mboolemi kàngamam aki jegeñaaleem aki sarxalkatam, bàyyiwu ca kenn, mu rëcc.
Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.
Dëgg laay def nattukaay, njekk di sama buumu beteex, tawub doji yuur buub rawtub fen, wal ma mëdd làquwaay,
maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nabukodonosor buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu.
Yaa topp sa tànki mag, kon maa lay nàndale kaasu mbugalam.
¶ Mu feeñooti ma, gisuma lu moy Boroom bi taxaw ci ab tata, mu ñu natte buumu beteex ba ñu koy tabax. Ma nga yor buumu beteex ca loxoom.
Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Yërmande laay dellusee Yerusalem. Sama kër lees fay tabaxaat.” Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. Mu ne: “Buumu nattukaay dina tàllalu ci kaw Yerusalem.”