TSK

TSK · 2 Kings 21:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sarxalukaay bu ñu defare suuf ngeen may sàkkal, di ci sarxal seeni gàtt ak seeni nag, muy seen saraxu rendi-dóomal, mbaa seen saraxi cant ci biir jàmm. Sàkkleen ab sarxalukaay ci mboolem bérab bu may fàttlee sama tur, ma dikk fi yeen, barkeel leen.

Kookooy tabax kër, ñeel sama tur, te maay saxal ab jalam ba fàww.

Aji Sax ji ne ko: «Dégg naa sag ñaan, ak sab dagaan. Sellal naa kër gii nga tabax, ngir teg fi sama tur ba fàww. Samay gët ak sama xol it fi lay nekk bés bu nekk.

Urya sarxalkat ba daldi tabax sarxalukaay bu dëppook mboolem tegtal ya bàyyikoo ca Buur Axas ca Damaas. Uri noppi na ko bala Buur Axas di ñibbsi.

Ci biir loolu Buur daane sarxalukaay ya ay buuri Yuda yékkati woon ca kaw xaddub néegub kaw bu Axas, ak sarxalukaay ya Manase tabaxoon ca ñaari ëtti kër Aji Sax ji. Mu jële fa lépp, def ko pënd, sànni ca xuru Sedoron.

xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.

Waa Yuda déy, ñoo def lu ma ñaawlu.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñoo yeb yëf yu siblu fi biir kër gi ñu ma tudde, di ko sobeel.

Tabaxal nañu Baal tuur mi ay bérabi jaamookaay ca xuru Ben Inom, di fa lakk seen doom yu góor ak yu jigéen ngir Moleg tuur mi, te masuma leen koo sant. Jooju jëf ju siblu jaarul sax sama xel ba ma leen di ko defloo, ñuy yóbbe Yuda bàkkaar.