Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
TSK
TSK · 2 Kings 21:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Muy bànni Israyil muy doxandéem ci Israyil, képp ku ci jël ciy doomam, jébbal tuur mi ñuy wax Moleg, dee rekk mooy àtteem. Na ko waa réew mi dóor ay doj, ba mu dee.
Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem, ñoo ko merloo ak seen tuur yu jomblu.
Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.
Rax ci dolli boroom rawaan yeek gisaanekat yeek gàllaaji kër yeek kasaray tuur yeek mboolem kasara yu ni mel te ñu daan ko gis ca réewum Yudak Yerusalem, Yosya jële na ko fa ngir mana saxal kàdduy yoon wa ñu bind ca téere ba Ilkiya sarxalkat ba gisoon ca biir kër Aji Sax ji.
Waa Misra jànnaxe, ma dëpp seen pexe. Ñu seeti yàllantu yeek njuuma yi, ak gisaanekat yeek boroom rawaan yi.
Ñoo rendil seen kasaray tuur seeni doom, ba noppi dugg sama biir kër gu sell ci bés bi, ba teddadil kër gi. Loolu déy, moom lañu def fi sama digg kër gii!
¶ Noo doon dem jullikaay ba, ab surga bu jigéen bu rabu gisaane jàpp, dajeek nun. Alal ju bare la ay njaatigeem daa jële ci ngisaaneem.