Kookooy tabax kër, ñeel sama tur, te maay saxal ab jalam ba fàww.
TSK
TSK · 2 Kings 21:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu sa ñoñ di xarejeek seen noon, ci yoon woo leen yebal, su ñu ñaanee ci Aji Sax ji, jublook dëkk bii nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,
su boobaa maay dagge bànni Israyil fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp.
Moo yékkati yeneen sarxalukaayi tuur ca biir kër Aji Sax ji, fa Aji Sax ji waxoon ne: «Fii ci Yerusalem laay dëj sama tur.»
Aji Sax ji nag ne: «Yuda itam dinaa ko jële fi sama kanam, ni ma fi jëlee Israyil. Dinaa xalab dëkk bii ma tànn, di Yerusalem ak kër gii ma wax ne sama tur dina fi nekk.»
Bàyyil xel askan wi nga jënd bu yàgg, yaa jot gii giir, séddoo leen. Bàyyil xel tundu Siyoŋ, fa nga dëkke woon.
xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
Waa Yuda déy, ñoo def lu ma ñaawlu.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñoo yeb yëf yu siblu fi biir kër gi ñu ma tudde, di ko sobeel.