TSK

TSK · 2 Peter 1:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Luke 9:28 TSK

¶ Ba lu wara tollook juróom ñetti fan wéyee gannaaw kàddu yooyu, Yeesu àndoon na ak Piyeer ak Yowaan ak Yanqóoba, ñu yéeg ca kaw tund wa ngir julli.

Loolu tax na ñàkkatuleen genn may, léegi bi ngeen di séentoogum peeñum sunu Boroom Yeesu Almasi.

Nun nag, nuy waare Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jaambur ñi dul Yawut.

Sama kàddu ak samam njàngle jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal,

Nun nag danoo melul ni ñu bare, ñiy julaa kàddug Yàlla, waaye ci ndigalal Yàlla ak fi kanam Yàlla la nuy waaree xol bu set, ci Almasi mi nu gëm.

Xanaa dees na ne, man ci sama wàllu bopp diisaluma leen moos, waaye samag njublaŋ laa fexee ba nax leen?

Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, nirule kook yaramam wi ànd ak teddnga.

Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore, aki firnde ak kéemaani feni neen,

Waaye nettali yu yittewoo lu dul Yàlla, ak léebi jeeg ju màggat ji, bañ ko, te nga tàggatu ci ag njullite.

¶ Li ngeen wara jëkka xam moo di bés yu mujj ya, ay niti ñaawlekat ay dikk, di nit ñu topp seen bakkan.

Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.