¶ «“Yal na la Aji Sax ji barkeel, sàmm la.
TSK
TSK · 2 Peter 1:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Man Nabukodonosor maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.
Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.»
¶ Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi,
¶ Su dee nag mboolem lu dund gu ag jullite laaj, Yàllaa nu ko maye dooleem, ba mu nu xamalee ne darajay boppam, ak jalooreem ju wéet lanu wooye.
¶ Ndax kat gannaaw bu ñu xamee bu baax sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ba rëcc sobey àddina, bu ñu ca sóobuwaatee ba mu man leen, su boobaa seenug muj moo yées seenug njàlbéen.
¶ Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,