¶ Mboolem kàddu gi ma leen dénk nag, sàmmooleen koo jëfe. Buleen ci yokk lenn, buleen ci wàññi lenn.
TSK
TSK · 2 Peter 2:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Léegi nag wooteel, Israyil gépp daje, fekksi ma ca tundu Karmel, ñu ànd ak ñeenti téeméeri yonenti Baal ak juróom fukk (450) ak ñeenti téeméeri nit (400) ñuy lekk njëlal Yesabel, te di yonenti Asera tuur ma.»
Booba la ma leer ne ndeke Yàlla yónniwu ko, waaye Tobyaak Sanbalat ñoo ko fey ngir mu birale ma noonu waxyu, di ma fexeel.
Jongrukati Israyil yépp a silmaxa, te xamuñu dara. Ñoom ñépp a diy xaj yu luu, manuñoo baw, xanaa tëdd di jeneer, soppi nelaw.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Buleen déglu yonent yi leen di wax ay waxyu; cóolóoli neen lañu leen di naxe, di fent ay peeñu, di wax ay waxyu, te du kàddug Aji Sax ji.
Buleen déglu yonent yi leen di wax naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon. Ay waxyuy fen déy lañu leen di waxal.
¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: «Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di géntloo,
Te sa yonent yi la doon jottli waxyu, naan la buuru Babilon du dikk ci seen kaw, yaak waa réew mii, ana ñu léegi?
Wóoy ngalla yonent yu ñàkk xel, yiy topp seen xelum bopp te gisuñu tus!
Nit man naa wër, toppi caaxaan aki fen, naan: “Maa lay yégal waxyub biiñ aku ñoll,” te kookooy jottlikatub waxyu bi askan wii yelloo!
Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee, seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle, seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane, te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan: «Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir? Musiba du nu dab!»
«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Waaye ku weddi fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, dees na weddi fa kanam malaakay Yàlla ya, ne man nga féeteel.
Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi.
Gannaaw feyees na seen njég ba jot leen nag, buleen doon jaamub nit.
Ñooñu ay ndawi caaxaan lañu, ay liggéeykat yu njublaŋ yu mbubboo ndawi Almasi.
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
ak bokkaale, ak xërëm, ak mbañeel, ak féewaloo, ak kiñaan, ak mer mu ëpp, ak jiital say bëgg-bëgg, ak réeroo, ak xàjjalikoo,
¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.
¶ Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina.
Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga jëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute, feeñ.
su nu muñee, nooy bokk nguuru.
Ndax kat ay jamonoo ngi ñëw, nit ñi dootuñu xajoo àlluwa ju wér, waaye seeni bëgg-bëggi bopp lañuy topp, bay fortaatoo fu nekk, ay sëriñ yu leen di wax lu leen neex.
Ab féewalekat nag, yedd ko benn yoon ba ñaareel bi yoon, doora daggook moom,
Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
Ñu ne leen: «Mujug jamono, dina am ay ñaawlekat yu topp seen bakkan, wéye seen kéefar.»
¶ Xam naa fa nga dëkk, fa la Seytaane samp nguuram. Teewul nga ŋoy ci sama tur te weddiwoo ne man nga gëm ba sax ca fan, ya nit ña reye ca seen biir, Antipas sama seede bu am kóllëre ba, foofa Seytaane dëkk.
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.