TSK

TSK · 2 Peter 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?

Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen. Gàtt xel yi, kañ ngeen di muus?

«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»

Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp: xam-xamu kasara, bant kese!

Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga ma; gis nga ma, seetlu sama xol ci yaw. Diri leen niy xar yu ñuy rendi, beral leen bésub rendi.

Ci jooju daraja, ak jooju jaloore ju wéet lees nu baaxee ay dige yu réy njég te màgg. Yooyu dige nag, bu ngeen ci jotee, ci ngeen di séddu ci jikkoy Yàlla, gannaaw bu ngeen muccee ci yàqutey àddina, gi xemmemtéefu bakkan waral.

Jude 1:10 TSK

Waaye nit ñii de, lu ñu xamul lañuy saaga, te xam-xam yi leen seen bindu judduwaale xamal, ni ay rabi àll di xame, ci lañuy far yàqoo.