Waaye wóoy ku bon, nde mooy bonle; la mu def rekk lees koy def.
TSK
TSK · 2 Peter 2:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan.
Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw; ñiy màndi it, guddi lañuy màndi.
Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ,
Ba ñu wàccee yoon wu jub wi lañu lajj topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi soppoon peyooru njubadi.
Na mu jëfe ak yeen, jëfeleen ko ak moom, feyleen ko ñaari yoon ay jëfam. Kaas bi muy xellile am njafaan, feesalal-leen ko njafaan lu ko ëpp doole ñaari yoon.