TSK

TSK · 2 Peter 2:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 31:7 TSK

Ndegam samay tànk a moy yoonu njub, mbaa sama xol topp saay gët, mbaa sama yoxo yii gàkk fenn,

Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.

Aji Sax ji nee: «Saab saamar a reye fa asamaan ba màndi deret, te mu ngii di wàccal Edom, xeet wi may faagaagal, ngir àttee leen ko.»

Ana ab Kuuseen bu mana soppi deram, mbaa am segg mu mana fari tipp-tippam? Kon nga mana def lu baax te tàmma def lu bon!

Fàww sax mu am ay xaajaloo ci seen biir, ngir ñi seen ngëm wér mana fés ci seen biir.

¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

James 1:8 TSK

Boroom xel-yaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.

Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.