Balaam tontu surgay Balag, ne leen: «Bu ma Balag doon jox këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def lenn lu tuut mbaa lu réy, lu tebbi sama ndigalu Yàlla Aji Sax ji.
TSK
TSK · 2 Peter 2:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Aji Sax ji tijji gémmiñu mbaam mi, mu ne Balaam: «Ana lu ma la def, ba ñetti yoon a ngii nga di ma dóor?»
Ab Amoneen mbaa ab Mowabeen du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci ñoom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji mukk,
Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney Aji Sax ji, di topp tuur yi nuy wax Baal.
Li ko waral moo di ñoo bañoona dabe bànni Israyil aw ñam wu ñu lekk ak ndox mu ñu naan, xanaa di fey Balaam, jibar ba, ngir mu rëbbal leen leen. Teewul sunu Yàlla soppi rëbb ga barke.
Man it duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Seen jëfin laay këpp ci seen kaw bopp.»
Yeen sama ñoñ, fàttlikuleen rekk la leen Balag buurub Mowab fexeeloon, ak la ko Balaam doomu Bewor tontu woon. Doxub diggante Sitim ba Gilgal it, baleen ci xel, ba ràññee njekku Aji Sax ji.
¶ Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru.
Loraange lees leen di feye loraange gi ñu sabab. Seen mbégte mooy xawaarey bëccëg ndarakàmm. Ñooñoo diy gàkk, aki sikk, ndax seen teewaay gàcce la ci seen biir yeen, bu ñuy bokk ak yeen bernde, te ca lañuy bànneexoo ay nax.
¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.