ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.
TSK
TSK · 2 Samuel 13:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel.
Mu daldi bàyyi lépp ci loxol Yuusufa, te li mu fa nekk tax ba topptootul dara ciy mbiram, lu moy li muy lekk rekk. Booba Yuusufa ku jekkoon bind la te góorayiw.
ñaareelu doomam di Kilab, ndeyam di Abigayil, ma doon jabaru Nabal waa Karmel ba; ñetteelu doomam di Absalom, mi Maaka di ndeyam. Maaka, Talmay buurub Gesur ay baayam;
¶ Gannaaw loolu Amnon jéppi ko njéefo lu raw mbëggeel ga mu ko bëggoon. Mu ne ko: «Jógal, dem!»
¶ Ci biir loolu Buur Suleymaan bëggoon na jigéeni yeneen xeet yu bare te bokkul ak doomu Firawna ji mu jëloon: ñuy ay jigéeni Mowabeen ak jigéeni Amoneen ak jigéeni Edomeen ak jigéeni waa Sidon ak jigéeni Etteen.
Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.